OS - MEMORANDUM - JUIN-2023 Lépp
OS - MEMORANDUM - JUIN-2023 Lépp
Mbind mii ànd ak ay peeñ, ab nettali la bu lalu ci ay firnde yu wér. Dafay indi
ay tontu ci waxi nguuru Senegaal gi nga xam ne wax la yu tegewul fenn, di ma
jiiñ xew-xew yu tiis yi am ci Senegaal fan yii ñu weesu.
Mbind mi ànd na ak ay firnde yuy dëggal ne li fi xew du kenn ku dul njiitu réew
mi Maki Sàll, jëwriñam ji yor Yoon, jëwriñam ji yor Biir-réew mi, ay alkaateem,
ay takk-deram, ay sàmbaabóoyam yu yor ay ngànnaay ak ay àttekatam.
Ngir indi sunu wàll ci leeral xew-xew yi ñu lim, wékk ko ci lees mën a teg loxo
bañ a nekk rekk werante, te wax dëgg rekk tax koo jóg, wayndare wii ci ponk
yii la tënku :
2. Ërtal ak xorñoññal jëm ci sunu kuréel ak képp ku àndul ci yorinu réew mi.
2. Nguur gi rekk di ndayu-mbill gi, moom mi joxe ay ngànnaay yuy ray, wut ay
sàmbaabóoyam, ba noppi di làkk aka neexal ay raykati nit.
V. Sof yi
5
Leeral gi - Usman SONKO - Suwe 2023
Bari na lu ñuy wax naan Senegaal réew mu mas a am Ci 1968, 1982, 1988, 1990, ak 2010, mball yi dañu daan
jàmm ak dal la ci mboolaay gi ak ci polotig. Moo ne wuute ci taraay, waaye saa su ne dañu daan jur
mënees naa fàttali ci lees teg ci ay firnde, ne xeex yu féewaloo gu metti, ay benke-ñenke diggante ay maas,
mettee-metti am na Senegaal, deret ju bari tuuru fi jur it ag lajj gu ñépp doon ñaawlu jëm ci tabax réew ak
ànd ak ñu bari ñees ci teg loxo mbaa sax yóbbu leen dëgëral demokaraasi.
ndungusiin.
Mball yu mujj yi fi am ati 2021 ak 2023, te jur taxawaayu
Ci atum 1962, foqarti nguur gi njëkk am ci réewi Afrig mbañ gi askan wi taxaw di jàmmaarloo ak nguuru Maki
soowu-jant yi Farãas notoon, fii la ame ci Senegaal Sàll, doonul lu dul jeexiti pëccaxoo yi weesu ak
muy bi ñu sàkkalee pexe ki fi nekkoon njiitu ndiisoo gi soofantal gu ànd ak ñàkk wegeel gu jëm ci askan wi te
te jiite woon Caytu gi di ndemsi-Yàlla si Mamadu Ja, tukkee ci nguur gi fi nekk. Ñàkk a xam dëgg bëgg-bëggu
ak aakimoo gu ndemsi-Yàlla Lewpóol Sedaar Seŋoor askan wi, rawatina ndaw ñi nga xam ne amuñu liggéey,
aakimoo woon nguur gi. tax na Maki Sàll ne day ŋoy ci nguur gi doonte dafay
caxat-caxatee Ndayi-àtte ji walla jaar ci ay kawi néew
Atum 1963, palug jàmbur yi juroon na xeex yu ñu jaare ko ci faagaagal ay wujjam ci polotig.
mësut a gis (50 jàpp 80 nit ñàkk ci seen bakkan, ay
téemeeri nit tëdd ci ndungusiin).
2Cf. Oumar Guèye, Mai 1968 au Sénégal, Paris : Karthala, 2017 : https://www.karthala.com/hommes-et-societes/3132-mai-1968-au-
senegal-senghor-
face-aux-etudiants-et-au-mouvement-syndical-9782811117023.html.
4Leral.net, violence a la présidentielle du 28 février 1988 : L’état d’urgence décrété, puis levé, Me Wade arrêté, jugé et
condamné à un an in
https://www.leral.net/VIOLENCE-A-LA-PRESIDENTIELLE-DU-28-FEVRIER-1988-L-etat-d-urgence-decrete-puis-leve-Me-Wade-arrete-
juge-etcondamne-
a_a13.html
5L’année 1990 est marquée par les évènements sanglants qui ont émaillé les relations entre la Mauritanie et le Sénégal. Des morts et
des blessés graves victimes d’atrocités comme l’égorgement d’êtres humains ont été signalés de part et d’autre. Voir : « Conflit
sénégalo-mauritanien » inWikipedia https://fr.wikipedia.org/wiki/Conflit_s%C3%A9n%C3%A9galo-mauritanien
Voir aussi : Alioune Badara Diop, « Espace électoral et violence au Sénégal (1983-1993) : l’ordre public otage des urnes »
in Afrique et développement, Vol. 26 N° ½ (2001, pp. 145-93) https://www.jstor.org/stable/43661158
6 In Tarik Dahou, « Le Sénégal entre changement politique et révolution passive », Politique Africaine 2004 (N° n96), PP. 5-21.
6 Médoune Samba Diop, Les élections présidentielles de l’an 2000 au Sénégal : carnet de bord, Dakar : L’Harmattan, 2019 ;
6
Leeral gi - Usman SONKO - Suwe 2023
Ni polotig laloo ci yooyu wayndare umpul kenn ci réew lalu ci nger, wanteer réew mi, saax-saaxe alalu réew mi, ak jënd
mi, te li koy firndeel tay jii mooy mbubboo gi ñuy nit ñi.
mbubboo waxtaanu mbooleem waa réew mi (dialogue
national), te jubluwaay bi du lenn lu dul may Maki Sàll Jëm ci loolu, jéego bi Maki Sàll njëkk a seqi mooy ci weeru
yoon yu mu jaar ba setal leen ngir ñu mën a doon ay waxset 2016 bi mu torloo ab dogal dàq ma fi ma doon liggéeye
lawax. ca saytuwaayu galag yi, te mu layale woon boobu dogal ne
dama wane ag ñàkk a maandu ci ndéey yi làqu ci sama liggéey.
Li may dund fii mu nekk nii du lenn lu dul doxaliin wu Li ñu ma toppee bokk na ci ne damaa siiwal ay jalgati ci wàllu
yàgg wu jëm ci faagaagal lawax bi mu gën a ragal bu galag yi ak njël yi, ak lu ñeel yorinu sunu ballu mbindaare yi, te
palug njiitu réew mi jubsee jaare ko ci fab dooley Càmm moom njiitu réew mi Maki Sàll, rakkam ak ñenn ci ay
gi dal ci kawam ak di jëfandikoo Yoon di lootaabe ay jegeñaaleem ñu doon leen ci tudd.
koote.
Ñu gaaw lool ci jël dogalu dàq ma ci sama liggéey, ba salfaañe
Maa ngi dugg ci polotig ci atum 2014 tolloo ak bi nu samay àq ak samay yelleef, mu bokk ci ma waroon a am ay
taxawalee sunu kurélu polotig ca ñenti fan ya ca weeru layalekat yu ma taxawu.
sãwiye. Sunuy kàddu ak sunuy jëf ci polotig nu ngi leen
Dinaa tëb nag xew-xew yu bari yu fi jaar te indi lii ñuy dund tay
tënk ci cëslaay yu mel ni xeex nger ci réew mi, delloo
ciy jafe-jafe ci Senegaal. Damay yem rekk ci li aju ci koote ci
askan wi baat ak sañ-sañam, taxawal ag yamale ñeel
polotig ak ci YOON ngir faagaagal ma ba du ma doon ab lawax
doomi réew mépp jëm ci móomeelu réew mi.
ci palug njiitu réew mi ñu jëm 2024, dinaa wax tamit ci rëbb gi
nguur giy rëbb sunu làngu polotig gi ndax bëgg koo tas.
Ci saa si, sunu wax jooju nuy toftal ay firnde yu wér, tax
na mu tàbbi ci noppi doomi Senegaal yi. Loolu nag
naqari nguurug Maki Sàll ba metti ko lool. Ca la daal di
tàmbalee dal ci sama kaw : bi ci njëkk mooy fàww mu
teg nu lu metti ba keneen du xalaat di am taxawaay bi
nu am, ñaareel bi mooy fanq yaakaar ji aju ci sémbu
polotig bi mu jàpp ne mën naa nësaxal yorin wu bon wi
7
Leeral gi - Usman SONKO - Suwe 2023
Njalbéenug mbir moomu mooy, ab jure bu jëwriñ ji yor am demokaraasi ci jamono tay jii.
Ndaamaari ak Nooflaay (Tourisme ak Loisirs), muy ku
fare ci làngug polotig gi nekk ci nguur gi mu jëme woon War na, nu fàttali ne Maki Sall moo soppilu sàrti pal gi
ko ci man. ci ag coppite gu lalu cig caay-caay, dugal ci tomb yu
yees yu L29, L30 ak L57 yiy waral beddi ay lawax ci palug
Jure boobu nag jur na ag gaawtu ci wàllu yoon ba ñu njiitu réew ci lu jaarul yoon. yi gën a ndaw. Ci loolu, ku
mujj amal ab àtte bu ñu parax-paraxee. ñu daan alamaan ju ëpp 200 000F rekk, ki ñu daan dañu
koy jëfandikoo tere ko mu mën a fale mbaa mu mën a
Lu jiitu jure boobu, jëwriñ ji yor wàllu biir réew mi, def falu (tomb L30 bu sàrtu pal gi).
na lépp ngir neenal leru (liste) PASTEF ci palug jàmbur
ya ca Ngomblaan ga ndax tur wu ñu baamtu ci baayale Segg googu muy jaare ci wàllu yoon di ko sukkandiku ci
gi. 3 tomb yooyu boole ko ak baayale gi, moo ko may mu
nërmeel képp ku ko war a wuutu.
Mu nekkoon ay pexe ngir fanq samag doon ab jàmbur
ngir ma bañ a am mbalaanum kiirlaay ba bu ñu ma Mbirum Maam Mbay Ñaŋ doon na ab niral bu leer ci
bëggee wutal lu ñu may toppe mu yomb. fitnay yoon ju ñu teg ab lawax ci palug njiitu réew.
Ci wàll wii lees di dugal mbirum Maam Mbay Kan Ñaŋ, 14i desàmbar ci 2022, wuyu naa luññutukat yi doon
moom moomu nga xam ne woowe na ma ba tàyyi saytu wayndare woowu, def sama jébbale ci "Division
yakktaankat, ku am feebaru jigéen, rëtëlkat... te taxul des Investigations Criminelles". Ci yorug Maki Sàll,
ma jàpp ne jar na ma jure ko ci kanamu yoon ngir bañ “DIC”, kurél gu am solo ci wàllu lootaabewiinu YOON,
ñu dugal yoon ci mbirum wàqante gi ci géewu polotig mujj naa doon as kurél su ndaw suy saytu mbiri yàq der
bi. ak saaga ngir faagaagal ay wujj. Bi may tontu laaji
luññutukat yi, ci laa xame ne dinañu gaawantu ci amal
Mbir mu ñàkk solo di ab wàqante ñeel ay way-polotig àtte bu jëkk, àttewaat ak àtte bu mujj bi ngir def li leen
mujj doon ab poroxndollu ngir neenal samag bokk ci Maki Sàll sant.
palug njiitu réew mi ci 2024.
Mboor mujj na maa jox dëgg ndax 2 fani feewaryee
Jamono ju may tontu wax ju Maam Mbay Ñaŋ waxoon 2023 ci la “néegub jubbanti bu àttekaay” bu Ndakaaru
ay fan ca gannaaw, ne genn caytu tuumaalu ko, ci laa woote déglu gu njëkk gi.
waxe ne wax jooju wérul, muy wàqante bu waroon a
amal njariñ pénc mi niki ni muy ame ci diggante ay way-
polotig yu nekk ci gépp càmm gu jàppe boppam gu
8
Leeral gi - Usman SONKO - Suwe 2023
Bi samay layalekat yi doon xoolaat li ma séqoon ak ki Ba ñu ma seetalee ndox mooma, ci benn labo bu xarala ca
ma yóbbu woon ci Yoon, gisoon nañu ne yàq der ak Farãas, xamal nañu ma ne ndox mu bon lañu ma xëppoon ba
saaga yu fés la ma doon toppe. ma noyyi woon ko.
Waaye, ba ñu jallale wayndare wi ca toppekat ba, Teg naa ci ay fan di yëg mettiit ak ug weradi ci sama yaram. Li
moom moomu moo ca yokkaat sos ak jëfandikoo lu ci mën a topp, mu gudd mu gàtt, lu mat a bàyyi xel la.
dul dëgg.
Sama layalekat, Sire Keledoor LY, itam, ak i atam ak wéradeem,
Fàww nu am ne ni ñu tërale ak di ko doxale Yoon, ci jot na wàllam ci nag wi. Ci anam yooyu lañu ma taxawaloon ci
Senegaal, toppekat yi dañoo lëkkaloo ak jëwriñ ji yor ëttu àttekaay bi.
Yoon mu am sañ-sañu joxe ndigal ci Wayndarey
Yoon yépp. Ndaxam, lenn ci YOON tënkuma woon ngir ma dem ci àtte ba.
Sama taxaw fa ak wuute fa mu ngi aju woon ci sama coobare.
Ci àtteb 02 feewaryee 2023, naam ñoo ngi ko doon
door a woote, àttekat bi daa lànkaloon sama Àttekat bi xamoon na ne damaa wéradi, waaye ndigalul Maki
layalekat yi ba ñu ko xamalee ne, masumaa jot aw Sàll bu jibee, jëfe rekk.
Këyitu wootew Yoon. Waaye, mujj na nangu dàq
àtte bi ba 16 ci feewaryee. Loolu yépp teewul nangu Ca bis boobu, itam, layalekat Xuwaan Baranko, di ab layalekat,
woon naa teewaat. ca ëttu àttekaay bu Pari, bëggoon maa taxawal ci samay àq ak
i yelleef, ay takk-der yu takku ba diis gann ñoo ko aaye dugg ci
Ba ñu àggee ca 16 ya, ñu dàqaat ko ba 16 ca màrs ba réew mi, gaw ko, yab ci ag fafalnaaw, génne ko réew mi, ci
ñu dëgmal, ginnaaw jàmaarloo gu metti gu samay ndigalul nguur gi. Ba loolu amee, nguur gi jéem naa setal deram
layalekat séqoon ak àttekat bi bëggoon na salfaañe di lay ne ab dof naan Xuwaan Baranko dafa waxoon lu
samay àq ak yelleef. teginewut jëm ci njiitu réew mi. Loolu doon, ci lu kenn mënut
a miim, ay yooni-yoon ñuy salfaane samay àq ak i yelleef.
Ba may dellu sama kër, takk-der yi taxawal sama
daamar, ca talib korniis bu Ndakaaru. Ba ñu taxawalee àtte ba, jaaxle woon naa lool ba àttekat bi
lànkalee fanweeri ci sama layalekat, bokkoon ci ñu bees ñi, ci
Ñenn ci ñoom toj sama weeri daamar, génne ma, seen càkkutéef ga ñu defoon woon ngir mu dàq àtte bi, ngir
yab ma ci seen waata, jubal sama kër te amuñu ci mën a yër la nekk ca wayndare wa.
ndigalul YOON (mandat d'arrêt).
Te nag, ci doxaliin ak tëraliinu YOON ci àdduna bépp, àq ju jan
Jële naa ca ay gaañu-gaañu yu bàyyikoo ci toj-toju la te dëgër nit ki am ku koy layal.
sama weeri daamar jooju.
Bis boobu ki teewaloon layalekat bi dem na ci ba di fàttali àttekat bi, àq yi laayookatu Usmaan Sonko am ngir toxal àtte
bi ngir man koo gën a càmbar. Ba mu mujj koo toxal ba 30 mars 2023.
Ñu bindal ma lijaasab kër doktoor, sama yëre ñu yobb ko bitim réew ngir saytu li ma takk-der yi xëppoon .
Fajkat yu bari jàpp nañu leen, mbaa ñu yóbb leen ca ëttu àttekaay ba ngir li ñu may saytu dong, waxuma la loolu sax
waaye njiital « SUMA ASSISTAANCE » li nga xam ne ba may dem ca raglu ba nekku fa woon sax, jàpp nañu ko yóbb,
jébbal ko àttekat bi, ba mujj koo takkal jéng ngir saytu ay yëngoom.
Ci àtte bu 30 màrs bi, samay layalekat jébbal nañu àttekat bi lijaasab kër doktoor bi waaye da koo randal ak i waaram
faalewu ko.
Ci bis boobu ba tay toppekat bi sàkku na ci àttekat bi mu tëj ma 2i ati kaso ak jàpp ma ci saa si. Waaye àttekat bi dogal
bi mu jël mooy tëj ma 2i weer ak alamaan bu toll ci 200000f.
Ak loolu lépp ñu ma teg, terewuma woon a bokk ci joŋante, waaye Maam Mbay Kan Ñaŋ dugalaat geneen dabu.
Ba ñu janoo ak taskati xibaar yi ñoom waa nguur gi li ñu xamle mooy ne Usmaan Sonko muccagul ci ñàkk a bokk gi.
Loolu di lu doyadi (yëral tegtal 6).
Ba ñu jógee ca loolu loolu ñu amal ndaje ngir mottali la ñu dooroon te mooy xañ ma samag lawaxu. Maki Sàll tabb
Usmaan GËY di sama wujj wi gënoon a fés ca Sigicoor ngir mu mottali ñetti àttekat yi.
10
Leeral gi - Usman SONKO - Suwe 2023
Ci lu kenn xaarul woon, te fekk maa ngi woon ci àpp bi ngir mën a def dabu ci àtte bi (30 fan), ci la toppekat bi ci
boppam jàpp layoo ba 17 fani awril 2023, muy 17 fan kott ginnaaw sama àtte bu njëkk.
Ñàkk a bàyyi xel sama sañ-sañ ci def ug dabu tax na li ñu gisoon ñoom mooy parax-paraxee yëf yi ngir matal ndigalu
polotig gu ñu leen sant.
Loolu moo tax ma bind ëttu Àttekaay bu Kawe bi ngir jure sëñ Ibraahiima Baaxum, toppekat bi ñu teg ca ñaareelu ëttu
àttekaay ba (Cour d'appel) ak Abdu Karim Jóob toppekatu Bokkeef gi.
Ñaari ma-yoon yii ñoo ko tay ci lu ñu teg ci seen bakkan jalgati samay àq ci jéem a wut a àtte mbir mii cig dabu te fekk
diir bi nu ma àppallon ngir ma def ug dabu matagul.
Li ci gën a doy waar nag, mooy ñu tànn pekk bu njëkk bu "Cour d'appel" ngir ñu àtte mbir mi.
Pekk bu njëkk boobu mooy bob njiital "Cour d'appel" di sëñ Amadi Juuf. Moom moo door toppe gi ñeel ma ci menn
mbir moomu, ci ba mu doonee toppekatu bokkeef gi.
Diggante àtte bu njëkk bi ak dabu gi, ci lañu ko tabb njiital "Cour d'appel".
Niki ku jiite woon toppe gi (toppekatu bokkeef ga woon), moom lañu sas mu war maa àtte ci dabu gi niki njiital ëtt
boobu bii yoon.
Ci noMbootaayu Xeet yi, jataayub 17 fani awril bu pekk bu njëkkub "Cour d'appel", sëñ Hamadi Juuf dàq mbir mi ba
8i fani mee 2023 ngir nëbb njuumte yu bari yi tukkee ci parax-paraxee gi ak xorñoññal gi. Ci loolu, mu tànn beneen
àttekat ngir mu àtte mbir mi waaye lépp moom mi ngi des ak wayndare wi ci pekkam. Tegu ci nag, ngir pekkub toppe
gi, jéem naa joyyanti jalgatig samay àq ci dàq wayndare wi ba 8i fani mee 2023 ndax ba 17 fani awril, maa ngi woon
ci àppub man a def dabu.
Niki ñu ko doon xaare nag, ci jataayub 8 fani mee 2023 bi, àttekat bi yokk daan bi jële ko ci 2 weer ba ci 6 weer, di
daan bu man a tàbbi ci géewub artiikal yii di L29 ak L30 bu kotu wétt yi.
Ci dabu gi, masuñu maa woolu boole ko ak jalgati gu ñu dul bàyyi noMbootaayu Xeet yi, àttekatu dabu gi bind na
teewaayu samay layalekat ca jataay ba te fekk kenn ci ñoom newul woon ca bulu ba.
Xuwaan Baranko, Layalekat ca baro bu Pari, teewal na ma ca jataay ba, ci dogal bi ñu fésal, te leer na ci boppu ñépp
ne dañu koo dëppaat delloo réewam tere ko mu teewe àtte ba (yëral Sof 7).
Yóbbeef na nag mbir mi ca ëttu àttekaay bu Kawe bi ngir gàntal dogalu "Cour d'appel", teg ci taxawal pexey bañ a
bokk ciy tànn gi soxla dogalu buy sax ba fàww.
Waaye niki ngeen ko seetloo, àpp yépp lañuy taxañ ngir jot seen jubluwaay, te ci lu gaaw, Ëttu Àttekaay bu Kawe bu
Senegaal dina jàpp jataay bi laataa jamonoy wote yi di tijji, te ay fukki fukki wayndare a ngay nelaw ca pekki ëtt boobu
lu ëpp ay weer walla sax ay at.
Bu sas woowu matee, fàww, Njiitu Réew Mi Maki Sàll ak pàccub yoon gii, tijjiwaat ñaareelu wayndare ci yoon ngir
wutaat yeneen pexey gàllankoor samag bokk ngir man a am lu wóor ci faagaagal ma.
11
Leeral gi - Usman SONKO - Suwe 2023
Ngir muy leer, Maki Sàll, mi nga xam ne aw turam tudd Te sax, bu fekkoon ne jot naa woolu gi ci lélub 11i fani
nañu ko ci mbir mi jóge ci ndaw si ak benn seede, mee, lan moo tax komiseeru DIC bi gis ne aajo na mu
jàppoon na ne téye na ci jumtukaay gu mu man a indilaat ma geneen woolu gu yees 4i fan ci ginnaaw bi,
faagaagalee wujju politigam wu tar wi ma doon ci maanaam 15i fani 2023 topp ci këyitu tënk bees defar ci
moom. Àttekat ak toppekat, yi mu teg ci wetam, dinañu benn bis bi ? (Yëral tegtal 10).
matal li ci des.
Amaul genn këyit gu nekk ci wayndare wi gu ma torlu
Lii lépp nag, teg ko rekk ci jalgati yoon ! guy wane ne jot naa ci woote gi.
12
Leeral gi - Usman SONKO - Suwe 2023
Leeroon na nàññ kon ne jotuma genn këyit walla mbind mu ñu ma woolu ngir jataayub "Chambre Criminelle" bu 23i
mee 2023.
Soxna Ndey Xadi Njaay, di ku ñu tuumaal, rax ci dolli mu néew doole ndax li mu tolloon diggante, àtte nañu ko te
amul layalekat.
Ci doxaliinu àtte bu jaar yoon bu mu mën di doon, ki ñuy topp dañu koo war a àtte ci teewaayu ab layalekat.
Ak lu mën a doon lay wi tax layalekat yi génn ci jataay bi, àttekat bi daf koo war a wutalaat beneen layalekat, lu dul
loolu, layoob « chambre criminelle » mëneesu koo àtte.
Àttekat bi ak ñaari naataangoom, ñoo jël coobarey xëtt yoon, te ci lu njëkk ku ñuy topp ci "Chambre Criminelle" ñu
àtte ko te ab layalekatam taxawu fa taxawu ko.
Li war sax nag mooy laaj lu tax ñu tànn àttekat bii di Isaa Njaay ngir mu jiite jataay bi.
Jàpp-leen bu baax, àttekat bii ñépp xam ag mbokkoo gi dox digganteem ak bë kk-néegu (Aide de Camp) njiitu réew
mi Maki Sàll, muy Seneraal Maysa Sele Njaay, di ku bokk ci mbooloom ñi gën a tar ci ñiy dal ci kaw askan wi, moom
lañu boole ci ñaari bir yii ma soxal yépp ci lu matul ñaari weer: bokkoon na itam ci ñett ñi joxe woon dogalu àtte bu
30i fani màrs bi doxoon sama diggante ak Maam Mbay Ñaŋ.
Ci layoo bu ñu gaawtu te patam-patamee ko (ñu amal ko ci 16i waxtu yu amul taxaw, diggante 10i waxtu ba 2:30 ca
guddi ga), daan nañu ma ci bisu 01 panu suwe ci lu ma teewul, mel ni damaa réer, te fekk mësuñu maa woolu niki
ni nu ko leeralee ci kaw.
Ci dogalu bi mu rotal, àttekat bi teggi na siif gi ak xuppeg ray gi, di tuuma yu ñu ma doon toppee ba noppi déglu ma
ci, ca ndoorte la ba leegi. Ndare ñu yam foofa, ñu teg tuumay « ger ndaw ñi » (Corruption de la jeunesse), ngir mën
a teg daanu 2i ati kaso yu may teree bokk ciy pal.
Te, ci diirub luññutu gi àttekat biy dêggal tuuma yi (juge d'instruction) bi doon amal, mësuñu maa déglu ci tuuma
jooju.
Ci kanamu njuumte (délit) lii ñu for ci yoon wi, muy ger ndaw ñi (corruption de jeunesse), mësuñu maa jox pose ngir
ma mën cee layal sama bopp.
Dëgg gi mooy, ginnaaw tuumay siif ak xuppeg ray gu doyadi gii, li ñu doon wut mooy am pexe mu ñu mën a teree
bokk cig pal, daal di tudd daan buy tàbbi ci tomb L29, L30 ak L57 bu sàrt biy lootaabe palug njiitu réew mi te Maki
Sàll soppi ko.
Jëwriñu Yoon ji, jéem naa def na ay njañse ci àtte bi mu jàpp ne ay àttekat yu mu gis ne ñu maandu ñoo ko joxe, ba
noppi teg ci jéem a layal ci lu amul benn cëslaay, fi ñu sukkandiku ci joxe ab daan ci ger ndaw ñi (corruption de
jeunesse).
Muy firndelaat rekk, ni nguur gi ak Njiitu Réew mi Maki dugale loxoom ci liggéeyu Yoon ba noppi toog ci xefu àttekat
yi.
13
Leeral gi - Usman SONKO - Suwe 2023
- Ay ñag yu ñu def li wër sama kër, ci lu teguwul ci yoon, lu ëpp 20 fan ngir tere maa génn, ber samag njaboot
teg ci xañ samay doom ñu jàngi, ci lu dul yoon;
- Fitnay yaram ak jumtukaay yi ma tuddoon ci kaw ak ni ñuy rëtalee samag njaboot lu jiitu, ci jamno ak
ginnaaw saa su ñu ma wooloo ci kanamu yoon, ci tëj ma sama biir kër di ma bàyyi xel ak alkaati yu ñuy dajale
sama buntu kër, ci lu teguwul ci yoon;
- Man maay mennum saa-senegaal mi nekk ci "contrôle judiciaire" lu ëpp ñaari at te ba leegi mënumaa am
benn tontu ci càkkuteef yi may amal ngir génn mbeeraay gi;
- Man maay mennum saa-senegaal mi nekk ci "contrôle judiciaire" mi ñu xañ bépp tontu jëm ci sàkku ñu
dindi "contrôle judiciaire" boobu. Doonte àtte nañu ma, man maay mennum saa-senegaal miy wéy di nekk ci
"contrôle judiciaire" ndax yoon lànk na maa delloo sama jàll-waax;
- Àtte nañu ma ci lu ma teewul te ma am kër gu ñépp xam goo xam ne sax Càmm gi amul benn coono ngir
tëj ma ca biir. Man maay mennum saa-senegaal, ci 17 tamndareet yi, moo xam ne ay yelleefam ci dem ak a
dikk gàllankoor nañu ko ci lu dul dogalu Yoon walla cëslaay bu wér, xañ ma maan a doxi samay yitte ak matal
sasub fara bu Sigicoor. Samayayookat ñu tere leen ñu man a gise ak man, yegg nañu sax ba bi ñuy jéem a ñëw
sama kër alkaati yi dañu leen sànni ay làkrimosen teg ci fitnaal leen (yëral Sof 17);
- Kilifay Yoon di parax-parax ngir sos ak matal mbooleem wayndare yi jëm ci man, te dara doMbootaayu Xeet
yil jubluwaay bi lu dul génne ma ba duma bokk ci joŋan tay tànn njiitu réew yiy ñëw, ci càkkuteefu Maki Sàll,
lànk naa tijji 7 jure yi ma def, ca 2017 ba tay jii, te yépp jëm ci bir yu ñu ma teg.
- Tëj nañu ma xañ samay jegeñaale ñu seetsi ma ba ci sax sama layalekat yi ñuy ërtal ak a fitnaal ci seen
liggéey (yëral Sof 11).
- Li ma ko yóbbee nag du lenn lu dul li ma nekk wujje wu tar, wu wóor te siiw. Loolu, Maki Sàll pékke la ko
jàppe.
14
Leeral gi - Usman SONKO - Suwe 2023
Leral.net du 30 Mai 2023, « La loi du Talion semble se dessiner : le siège du PASTEF à Liberté 6 extension, vandalisé » https://www.
leral.net/La-loi-du-Talion-semble-se-dessiner-Le-siege-du-Pastef-a-Liberte-6-extension-vandalise_a349496.html
8 https://www.seneplus.com/societe/mariama-sagna-sonko-militante-et-parente-du-leader-de-pastef
15
Leeral gi - Usman SONKO - Suwe 2023
Basiiru JOMAAY Fay Biram Suley Jóob El Maalig Njaay Waali Bojan
Jëwriñ Ju Rëy ju PASTEF, LES Topp-njiital làng gi di njiital Njiital kurélug caabalu làng gi, Bokk ci pekk bi yor wàllu
PATRIOTES, àttekatu 2eelu pekk kippaangog jàmbur yi ca àttekatu 2eelu pekkub ëttu kaaraange gi, ñu takkal ko
bu ëttu àttekaay bu Ndakaaru Ngombalaan ga, ñu def ko àttekaay bu Ndakaaru def ko jéngu xarala, moom it ñu ngi
yóbbu ko ndungusiin ci tuumay "contrôle judiciaire". "contrôle judiciaire" boole ko ci
ñàkke worma ab àttekat, ci am
ci "contrôle judiciaire".
takkal ko jéngu xarala tere ko
mbind kese mu mu fésaloon ca mu génn Ndakaaru ci lu dul
Facebook. Mi ngi ci kaso lu jege ndigal.
daanaka ñaari weer ca Kab
Manuel.
Bu dee xel-ñaar amul ci yéeneem ngir tas sunu làng gi teg ci ber ma nële lajj na bu baax, jëfandikoo yoon gi fés ci Maki Sàll mi
ko mujj a def gànnaayam ci xeexu polotig bu ko leer moom ci boppam ne ñàkk na ko ba fàww.
Njàppe gu àndul ak xel gi nguurug Maki Sàll nekkee yamul rekk ci sunu làng gi. Day dal ci kaw képp ku yor kàddu gu dëppowul
ak gosam di leeral yoriin wu bon wi mu yoree réew mi.
Li gën a fés ci nguurug Maki Sàll mooy deltu ginnaaw ci wàllu péexteg caabal. Saabalkat yu bari tay jàpp nañu leen walla ñu mas
leen a jàpp:
Bu weesoo saabalkat yi ñu teg bët te jàppe leen niki ñu àndul ak nguur gi, ñëw dolliku ci tëjug teleb Walfajri. Tele bi dagg nañu
ñaari yoon ab siñaalam ndax li mu doon wane fippuy askan wi ca màrs 2021 ak suwe 2023, ci xuumtoo gu bawoo ci kurél giy
saytu caabal yi (CNRA) ak jëwriñu caabal gi.
Ñi bokk ci sosiyete siwil bi, way-xiirtale yi mbaali jokkoo yi, bañkat yi, ma-pasin yi
Genn luññutu amul ci mbirum ñaari takk-der yooyu ngir leeral li leen dal ak nu ñu réere; du
seen i kilifa, du toppekat bi, du itam genn kàddu gu ñu yékkati ñeel mbir moomu.
Luññutu gi yëngatuwul ci benn boor, seen i njaboot a ngi naqarlu lu ni mel. Fitna ga yamul
Fulbert Sambou
Këyit gi waa raglub « Principal » génne ba ñu ko saytoo, nee ñu dafa matal rekk, ci koo xam ne moo ngi tollu dong ci 51 at te
dara jotu ko woon.
"Amnesty Sénégal" wax nañu ne nguurug Senegaal moo xañ fajkat bi ba njabootug Mànkaabu tànnoon ngir mu def liggéeyam
ngir ñu am ci lu gën a leer; ba ci wayndarew wér-gu-yaramam sax dees ko koo xañ.
Kopar Express: di kërug liggéeyukaay gu xereñ lool ci yónnee ak dajale xaalis moom it da ñoo dakkal bépp yëngu-yëngoom
ginnaaw ba attekatub ñaareelu néeg bu ëttub àttekaay bu Ndakaaru jëlee dogal topp leen ca 23i me 2023 ba tay.
Sëñ Seydou Nourou Ba di kenn ci ñi moom « Fintech » ñoo ngi ko ni ràpp ca ndungsiin ci mbirum Anibaal Jim mi ñuy tuumaal
naan mooy kopparal ki bëgg a nërmaael nguur gi ci yenn xew-xew yiy jur jafe-jafey kàraange.
Ñii ay niral rekk lañu ndax lim bi xaajul bay mat ngir firndeel pexe yi nguur gi teg ngir xoqtal nit ñi jaare ko ci yoon ngir tëj
képpàku ñu jàpp ne am nga taxawaay bu leen di yàqal, ba noppi laqatu ci ginnaaw takk-der yi di fitnaal askan wi.
Li ëpp ci wayndarey toppekatu bu ëttub àttekaay bu ndakaaru bi, bu noppee Omar Maham Diallo la ñu koy dénk walla
àttekatub ñaareelu néeg bu ëttub attekaay bu Ndakaaru di Mamadu Sekk. Ñoom nag buñ ko jotee lu ci ëpp, bu dee koo xam
ne dafay wax lu neexul waa Càmm gi, dañ koy tëjlu ba nopp soog a jëm ci ay mbiram.
20
Leeral gi - Usman SONKO - Suwe 2023
Dogalu ëttu àttekaay bi ma daan, ci njombe loo xam ne tudduñu ko, du ci jure bi du ci dogalu wayndare wi ñu
yóbbu ngir layoo, du lenn lu dul càkkuteefu politig. Lii nag moo ñëw, dëggal koote gu ñaaw gi nguurug
Senegaal teg jëme ko ci wujjam ngir rekk bëgg a xañ kooku mu man a bokk ci jonatey tànn njiitu réew yu
2024.
Samag daan ci 01 panu suwe bii, te dikk ay fan rekk ginnaaw jalgatig yoon gu "Cour d'appel" ci mbir mu njëkk
mi soxal sosalaate, moo tàbbal réew mi ci ay ñaxtu yu tar, yu am ci xew-xew yu tiis yu mee féewarye-mars
2021 te waraloon 13 ñu faatu ak lu jege 600 ñu am i gaañu-gaañu bees sukkandikoo ci seede yi dikkoon ci
sunu téereb leeral bu njëkk (yëral tegtal 21).
Mbooloo mu takku ci askan wi ñoo génn ginnaaw bi dogalu àtte rotee, ngir sàmm li nu jot am te jële ci ay ati
xeexu politig ak réewte, te maas yu wuute dugal ci seen loxo, te ñenn ci ñoom sax jaayante ci seen ëllëg, seen
péexte ak sax ngir ñenn ñi, seen dund ngir warlul saa-senegaal bu ne sañ-sañam ci wétt (sañ-sañu man a fal
ak ñu man laa fal). Ngir indi ci tontu nag, niki mu ko baaxoo defee ak jikkoom, Njiitu Réew mi Maki Sàll fitnag
nguur gu tar la tegal askanam.
Ci goxi Ndakaaru, Sigicoor, Biñoona, Séeju, Kawlax, Cees, Ndar, Pikin, Kër Ma-Saar, Rufisk, Mbuur, Welingara,
Gudomp, Kabsikirin, Géejawaay, Risaar Tool, Kumpentum añs, ay widewoo, ay nataal ak jataayi daar-daar yu
teewoon ci xew-xew yi, fésal nañu way-kaaraange yuy teg fitna yu metti ci kaw askan wi (yëral tegtal 12).
21
Leeral gi - Usman SONKO - Suwe 2023
Ay mbootaay yu ci mel ni : Human Rights Watch,
Amnesty International Afrikajom Center,
Raddho …añs, limaalewuma sax caabali biir
réew mi ak yu biti réew yi, ñoom ñépp jàllale
nañu ñaawtéef yooyii ba ñépp jot ci.
10
Yëral bunt III bi
22
Leeral gi - Usman SONKO - Suwe 2023
30
nit ñu ci ñàkk seen bakkan ak 4
ñees xamagul ba tay seen ay mbokk
Bokk na ci ba tay, lim ak
Lii mooy lim bi mbooleem mbootaay yu maandu yi
dajale ak càmbar yi (bar gi tënkuwul ci nguur jotal bawoo ci ñaxtu yi.
yor wàllum paj) te bokk ci
sunu làngug polotig amal,
wane na tolluwaayu
ñaawtéef yu jéggi dayo.
Lu ëpp 80%
Ci ñi faatu ay bal lañu leen
dóor ñu dee
Te Këyitu saytuy yarami ñi faatu, te bawoo kër
doktoor saxal na ko. Li yoon digle mooy fu ag
paatu gu bette walla gu lënt ame dees fa war a
amal ay caytu ngir xam lu ko sooke. Bu caytuy
doktoor yooyu amul it manees naa sukkandiku ci
gaañu-gaañuy yaram te loolu bu dee fu balu fital
jaar dugg ci yaram manees na koo xam.
Lu ëpp 157
Ñii ci biir ñii ci bopp (fukk ci ñoom) am nañu ay damm-
dammuy biir walla yu ubbeeku moo xam muy ( ci tànk,
ci yeel, ci xasab seen i loxo walla feneen fu sori ci seen
uw yaram...) am na ci ñoñ fa ñu leen dóor bal dafa
ubbiku ci biti.
Gox yi gën a mettile ci bir yi ñooy Ndakaaru rawatina Géejawaay ak Pikin nga
xam ne ñoom rekk waññi nañu 8i nit ñu fa faatu ñoom ak Siggcoor ak Ndar
Géej.
Ñépp xam nañu ne leegi Senegal ci wàlla kaaraange gànnaay yu bon lañuy
jëfandikoo, -yoo xam ne ci geer rekk lees ko war di génne- di dal ci kaw askan
wu yorul dara, ndaw sii di Aji Jàllo niral la ci, moom mii ñu dóor balu fital raŋ
ci ndabal bopp mu faatu te ñu tuumaal ci takk-der yi. Bu nu sukkandikoo ba
tay ci Këyitu cambaru kër doktoor gi njabootam deflu mu wuute lool ak kàcc
yi jëwriñi biir réew mi, nga xam ne miinees na ko ciy fen yu ni mel ndax ci
bataaxel ba mu génne woon booba laata càmbar gi, da ne woon dammitu weñ
yu juge ci xandalug gaal moo ko ray.
Balu fetal bu ñu dóor ci kaw askan wi
Jëfandikoom doole ju ëpp jii niki gànnaayi fital di fitnaal nit ñi nag amul lenn lu
ko man a layal ci àddina, te dafa bokk ci yees tere teg ci ay daan ci sàrt bii ñu
tër ca 13i oktoobar 1970 muy tere jëfandikoo xeetu gànnaay yooyu mu di poliis
walla sàndarmri, ci lu jëm ci jëfandikoo doole ci saytu kaaraange kepp.
Moo di ba tay jukki bii di 34/169 bu mbootaayu xeet yi 17i desàmbar 1979 ci
lees maye ci jëfi doole ngir saytu kaaraange, mu war a sàmmoonte ak àtte bu
7i Sattumbar 1992.
Ba tay ñenn ci ñi ñu jàpp walla seen i jegeñaale xamal nañu nu ñaawtéef ak fitna ya ñu leen di teg :
- Seen i bokk (xarit walla jegeñaale) yóbbul leen ay lekk ñu faf leen téye ñoom it walla ñu leen di xupp ne leen bu
ngeen fi dellusee ñu jàpp leen tëj, ngir rekk tiitalaate ba kenn dootul bëggatee dem ngir xettali ña fa nekk;
- Ñi ñu téye seen i njaboot ñu leen di wërloo poliis ak komiseryaa yi fu ñu dem ñu ñe leen du fii, te duñu leen jox
benn Sof lu moy wërloo leen te moo ne am nañu ci lu wér ne dañu leen a téye ;
- Ay ndaw jàppe nañu leen (Cees ak Komiseryaa Parsel Asani) ñi leen jàpp di ay sàmbaabóoy yu kenn xamul yóbbu
leen ci këri way-polotig xorñoññal leen, duma leen ba gaañ leen nataal leen tasaare ko ngir xàwwi seen sutura niki
nataal bii ci suuf Paab Abdulaay TURE bokk kurélug (FRAPP) ;
Fii, Paab Abdulaay Ture la takk-der yi jàpp, yeew loxo yi, door ko ba mu sonn - suwe 2023
25
Leeral gi - Usman SONKO - Suwe 2023
Soxna Mariyaama JÀNQA, di njiital PASTEF ca Risaartool, ca biir goxub Dagana, am mbooloom alkaati ñoo ko
jàppoon ci bis bu njëkk ci weeru suwe, ci atum 2023.
Bu nu sukkandikoo ci layalekat bi, di Meetar Baabakaar NJAAY, alkaati dañu koo këf ba mu wàcce ci ab liggéeyam
tàbbal ko ci seen ug daamar teg ci ne ko boo xuuxoo ñu sàkku la. Rax ci dolli doon ko dóor ak a mettital ba mu
jële ca ay gaañu- gaañu yu metti ci kanamam, ci ay yoxoom ak ciy luppam. Ñu mujj ko yóbbu ca raglu ba, waaye
mujj ko faa jële ci kaw gunxatal ak xëble gu alkaati yi teg seruseñ ya bëggoon a téye ca seen raglu ba ba wér. Këyitu
noppalu ga ko kër doktoor ya joxoon mayoon na ko mu toog këram fukk fan ak juróom- benn.
Ca bisub suwe gu njëkk, itam, fanweeri nit ak juróom- ñent jàppoon nañu leen ca Risaartool te bokkoon ca ay xale
yu toll ci 10i ba 13i ci at, te ne woon ca jàngune yi ndaw ya. Ba leegi ci linu jële ci meetar Babaakaar NJAAY.
Aji- loru yooyu yépp bàyyi nañu leen te toppu ñu leen dara, muy firndel ñàkk am solo ak doyadi gu ñu leen jàppe
woon.
Nees man a fàtte yënguy jigéeni pastéef te ñu jàppoon 16 ci ñoom te mujj leen a bàyyi ginnaaw seleŋlu lekk ak
naan gu seen i layalekat siiwaloon, ñu door leen a bàyyi.
Bu yàggul, lu mat juroom-fukk ci ay jigéen i saa-kasamaan te féete (bois sacre) ca àll bu sell ba, jàppoon nañu leen
fitnaal leen ba noppi buub leen yóbbu Ndakaaru, ngir taxawal leen ci kanamu àttekat bi. Waaye, jigéen ña dañoo
lànk ne duñu sol lami xarale yi, ndax dëppoowul ak bayum ceeb mu ànd ban ak ndox. Ginnaaw gi la leen magu
àttekat bi yolomal mbãyyim bàyyi xel.
- Ay kilifay alkaati lànk nañoo torlu ay wayndare yu seruseñ yiy biral ag faatu teg ci seen i Pekk di biral ne ay sox a
leen faat. Ni ko baay Usmaan SAAR, di way- jur ci kenn ci xale ñi ñu faat, waxe.
- Néegu néggandiku yu ëttu àttekaay ba fees na dell, ndax lu ëpp juróom ñatti téeméeri doomi aadama a ga ca biir
di buuxante ci lëndëm gu tar ak tër ak tàngaay gu metti.
Njaay dooleey nguur gi àgg na ci dag lënku jollasu ak mbaalu jokko yépp m, rax ci dooli këri saabal yu mel ni walfajiri
ak seen TV. Walf, moom, dañu koo yónne ab bataaxel buy tëj ngiska a mu yor yépp ak i rajoom. Nee nañu dañuy
indi fitna ci réew mi.
26
Leeral gi - Usman SONKO - Suwe 2023
- Ana naka lañu sàmme méngoo gi war diggante taxawaayu way sàmm kaaraange gi ak
càmm gi ñeel dundug way naqarlu yi niki seen wérug yaram ak gug xel ?
- Ana lan moo waral ci wàllu yoon ak xew-xew génnug ay "snipers" ci lu jëm ci sàmm dal
gi, ci bunt kër Usmaan Sonko ci atum 2021 ak ci Me-Suyeng 2023 ci koñ yu bari ci Ndakaaru,
Sigicoor ak Biñona ?
- Lu tax alkaati ak takk-der yi sox ay wal i fital ba faat ay waynaqarlu , waral ci ay gaañu-
gaanñu yu xóot kenn tegu leen loxo ba tay boole ak bàyyi leen ñu wéy di nekk ci mbedd mi
ba leegi ?
- Ndax yeen a joxoon ndigal alkaati yi ngir ñu jëfandikoo ag ndëgg-sërëx ngir jàpp ay way-
naqarlu yu nekkoon ca bunt kër Usmaan Sonko ?
Ñenn ci ñoom ko topp ci jëwriñu biir réew mi ji gàlloo kaaraangeg mboolaay gi gën a jege moo leen jël jaarale ko
ciy pasi yokk payooru ñi yore kaaraangeg mboolaay gi gën a jege (ag luññutu gu yomb maneesoon na ko a samp
jaare ko ci xibaar yiy tukke ca pekku xibaaru way-kaaraangeg mboolaay gi gën a jege (ASP).
Yeneen sàmbaabóoy ya, te ñu man leen a ràññee ci widewóo yi, jëwriñu Ndaw ñi Sëñ Paap Maalig Nduur moo
leen jël, ak Sëñ Duudu Ka jëwriñu Yaaleg jaww ji wala ñenn ci ñi wër mbokku njiitu bokkeef gi.
Da ñu leen tasaare ci koñ yépp ci Ndakaaru ak ci yeneen goxi réew mi ak i gànnaayi xare ( Fetal 5, 56 x bu B 15 ak
AK-47 x ) di ko sox ak a songee ci teeyug bakkan, ci ndigal yi ñuy jot, di leen sox ci kaw ñaxtukat yu yorul gànnaay.
Ñuy song ay njàngaan ba ci seen biir barabi dëkkuwaayu jàngune bu Ndakaaru, bob Cees, walla jàngune bob Ndar.
Ci demokraasi yépp toppatoo ag mbooloo wareefu ñi gàlloo kaaraange la te ñoom la ko yoon may. Tay jii, ñépp
seetlu nañu ko ne sàmbaabóoy yu yore gànnaay yu nguurug Maki Sàll moo wuutu fépp ci bedd yi takk-der yi ak
alkaati yi.
Ci ay peeñ yiy wër àdduna, nuy gis ay sàmbaabóoyi nguur gi ñuy liggéey ak nekk ci wetu alkaati yi ak takk-der yi te
yéemu leen sax.
Te dafa di nguur gi dafa jox ndigal njaatigel santaane gu takk-der yi ak toppanteg alkaati gu réew mi ngir mu bàyyi
sàmbaabóoyi gànnaayu te wane ag ñàkk tegu ciw yoon wuy cëslaay wu njëkk ngir ñu amal liggéeyu toppatoo
doxaliin wi.
Càmm gu Senegaal, lu moy ginnaawal ak salfaañe yoMbootaayu Xeet yi koppar ak waññig njéeméer li mu dugal,
amal na bisu 31 desàmbar 2021 njëndug gànnaay lu tollu ci 43,3 tamñareet ci xaalisu CFA yu ñu tàbbal ca njëwriñug
Kéew ma.
Ngir bañ bépp béj jëm ci mbir moomu ca ngombalaan ga teg ci lànkal aw yoon wu jëm ci luññutug ngombalaan ga
ci cëslaayu ay pexe yu kippaangog ngombalaan gog Yewwi Askan Wi (YAW), nun jàpp nan ne ay gànnaayu xare la
yu ñu teg ci yoxoy sàmbaabóoy yay nekk ci lu teguwul yoon ca wetu ña gàlloo kaaraangeg mboolaay gi ci bedd yi.
Dawalug pas gi, muy bu Sof L°1 wane na ne gànnaay yile jot nañu ci (yër Sof 13):
- 60 watab rëbb "Hulix double cabine" ( niru lool ak daamar ya nu gis ca buntu dalub APR ñu teg ca
yoxoy yaaleg sàmbaabóoy ya)..;
Ginnaaw njëndeef yu lëndëme nu ni mel, ay wayndare yu ay way-polotigu kujje gi wane nañu ko fépp te kenn
weddiwu ko, te moone ak lim bu ni day ciy fetal yu ñu jënd (lu ñépp yëg!) tay njëndeef yu Bokkeef gi jënd (yër
Sof 14).
Ci waajal ay mbugal jëme ci fere yi, Sëñ Maki Sàll, yokk ci jëndug gànnaay yu ni tollu, moo waral muy téye ca seen
liggéeyu topp-alkaati yu jékki (ca tolluwaay bu njëkk yoy Sëñ Musaa Faal, njaatigel santaane gog sàndarmari bu
réew mi) nangu nañu seenug ëppal cig tàmm jëfandikoo dooley ërtal ci kaw ferey mboolaay gi (yër Sof 19).
Te itam li mujj mooy wétt wu gaaw ca atum 2022 lu mat 3 500 takk-der aki alkaati, yu ñu baral seenug tàggatu teg
ci ñu def seen ayu-bis bu njëkk ci liggéey bi muy wàcc ci bedd yi ca weeru Suwe 2023.
Leeral gi - Usman SONKO - Suwe 2023
Leeral gi - Usman SONKO - Suwe 2023
Ñaxtu yi fi amoon ca 1 ak 2 fani suwe ci dëkk yu bari ñoo waral kàdduy njàqare yu kuréel yu bari yu nekk ci réew yi
ñu wër ak ci biir réew mi.
- Cib saabal bu ñu def ca talaata 13i fani Suwe 2023, "Mbootaayu Xeet yi" yi xamle na ñu ne dañoo jaaxle lool ci
anam gi àq ak yelleefu doomu aadam di doxe ci Senegaal.
Ki yore kàddug MBOOTAAYU XEET YI ci àq ak yelleefu doomu aadama wax na ci jëfandikoog gànnaayul xare yi way-
kaarange yi jëmale ci ñaxtukat yi.
Mangago mi nekk farbab MBOOTAAYU XEET YI xamle na ne" jëfandikoog gànnaayul xare yu way-kaarange yi ci
ñaxtu yi nekk na lu ñaaw ci Senegaal. Li njëkk a war njiiti Senegaal yi mooy ñu fonk demokraasi bu njëkk bi fi yàgg
a am ak wóoral amug péexte ci dajaloo ak wax sa xalaat cig dal.
"Haut-commissaire bu MBOOTAAYU XEET YI" wane na itam njàqarem ci ñàkk péexteg wax sa xalaat ginnaaw ñaxtu
yi fi amoon. Mu jël niral ci Walfadjri , tele mi ñu daj ag buumam ca 1i panub Suwe te joxewuñu benn leeral bu mata
nangu ginnaaw jàllale gi mu def ay ñaxtu daar-daar .
- Mbootaayu réewi Afrig yi (UA) ci saabal gu njiitu kuréel gi Musaa Faki Mahamat def sàkku na ci ñu fonk àq ak
yelleefu ma-réew yi ci am péextem wax seen xalaat ak amal ay ñaxtu.
- Kuréelug ñi farul fenn mooy itam def na seetlu ci yàqu-yàqu ci am ci weer yii te polotig bi waral ko.
Mi ngi ŋaññ jëfandikoog gànnaayul xare yi ñu jëmee ci ñaxtukat yi ak xoqatal yi leen way-kaarange yi di def. Mi
ngi ñaawlu itam yàq gi ñuy def alali nit ñi di woo way-kaarange yi ci ñu fonk àqi ñaxtukat yi ndax ñu bañ a yëngal
dalug njéeméer gi.
Mbootaay gi mi ngi fàttali sàrt yi Senegaal torlu yépp te ñu jëm ci demokraasi ak péextem ma-réew yi.
30
Leeral gi - Usman SONKO - Suwe 2023
CADHP di kurél guy ci sàmm àq ak yelleefu nit ñi ak doomi aadama ci Afrig yi, sóobu na ci lijjanti anam gi nguur gi
doge woon mbaalu jokkoo yi.
Am na njàqare it ci gaw gi ñu gaw kër Usmaan Sonko gi 28 fan ci weeru mee ak leegi.
CADHP mu ngi ñaawlu ba tay cong gi takk-der amal ci kaw askan wi. Di fàttali ba tay ne am sañ-sañu wax sa xalaat,
lënku ak ñaxtu doon na yoo xam ne ndayi-àt tay réew mi moo ko yoonal ci tombam bu 4, 9, 11 ak 12 ak ci sàrtub
Afrig bi aju ci sàmm àq ak yelleefu doomi Aadama yi.
Mu ngi woo ba tay kilifa yi ñu jël ay matuwaay ngir delloosi dal ci réew mi ak yamale takk-der yi ba ñu jox cér askan
wi.
Lu soxal Amnesti internasyonaal ci Afrig gu diggu gi ak gu sowu jànt, ci làmmiñu njiit li di DAAWUD, ñaawlu na
lënkaay gi ñu dogoon ak tele Walfajri bi ñu tëjoon, ndax loolu dafa wuute ak li ñu yoonal ci àddina bi.
Muy sàkku ba tay ci kilifa yi, ñu ubbi ag luññutu ci ñi faatu te lijjanti mbiri sàmbaabóoy yi doon soqi ay sox ci kaw
askan wi te nekk ci wetu takk-der yi.
Mu teg ci ne ñaxtu yii wees, li ñu ci salfaañe ci àqi doomi Aadama, dafa ëpp lool.
CEDEAO di ñaawlu faatu yi am ci xeex yi, di woote it ci ñu lijjanti lëj-lëj yi am ci réew mi te deret du tuuru.
Tasukaayi xibaar yi ci àddina bi def nañu ci liggéey bu am solo muy wane ñaawtéef yi nguur gi doon teg ci kaw
askan wi.
Leeral gi - Usman SONKO - Suwe 2023
IV.
32
Leeral gi - Usman SONKO - Suwe 2023
Ginnaaw xiixaan gii nguur gi nekke te réccuwu ci dara, ñiy jàppale Senegaal te nekk ci àddina bi war nañoo téye
seen ay yoxo ci lépp ndimbal lu jëm ci yàqkat bii di Maki Sàll, di nit ku dara ñorul lu dul nguur.
Jëfam yi teguwul ci dara lu moy ragal gi mu ragal ñu topp ko ëllëg ci yoriin wu bon, yoriinu par-parloo ak ci
mettital wu ànd ak ger ak càcc ak ray yu ñaaw yoo xam ne ba tay mujjul fenn.
Waroon na ci ñiy jàppale réew mi ñu sàkku ci nguur gi mu waggar bëgg -bëggu askan wi ak ay tànneefam, jaare
ko ci wàccoo ak li ñu yoonal ci doxaliinu reew mi ak àddina bi.
Waroon nañoo ñaawlu bu baax ñatteelu pal gi teree nelaw Maki Sàll te tegewul ci yoon, tegewul ci ngor teg ci
mën a yàq lu bari.
Waroon nañoo sàkku ñu bàyyi Yoon gi Maki Sàll di jëfandikoo ngir polotig ak ngir xañ ay wujjam seen ay àq ak
yelleef.
Ngir xamle dayob mbir yi ba mu gën a yaatu ci biir réew ak bitim réew, jàmburi kujje gi nekk ci « Yewwi Askan
Wi » defar nañu ab jukki yóbbu ko ca ngomblaanu réew mi :
« Ngir moytu lépp luy gàllankoor gu bawoo ci wotey ngomblaan gi jëm ci sàrtub daan ñeel xiixaan, fanq àq ak yeeleefu
ñit ki, mbooloo muy ligéeyal nguur, mbooloom defkatu ñaawtéef, njàppandal ci ray nit, ci faagaagal xeet wi ak jëfi
mettital,
- Tekkig ndombal tànku Maki Sàll, ci lu amul ab àpp ndax ñàkk a yayoo doon njiital réew mi ak dooleel xiixaan ci réew
mi ak yeneen musiba yi ñu teg ci kaw askan wi;
- Teg loxo jëwriñ ji yor biri biir réew mi, ki yor ASP yi, ki yor xare yi, ki yor koom-koomu réew mi, ki yor ndaw ñi ak
doomu Maki Sàll mi ñu tudd ci jël ay sàmbaabóoy ngir jàppandal jéya ci kaw xeet wi, mbooloom defkatu ñaawtéef ak
yeneen i jëf yu jéggi dayo;
- Feeñal ak teg loxo sàmbaabóoyi nguur gi ci nu mu gën a gaawe ak waa Benno Bokk Yaakaar yi doon song askan wi ;
- Ubbig luññutu gu àdduna bépp dugal loxo jëme ko ci ñi def jëf yu ñaaw yi nu gis ci réew mi ci fan yii wees te nu am
ci ay xibaar yu doy rawatina ci Maki Sàll ak jëwriñu biir réew mi, ak jëwriñu yoon, ak jëwrinu xare yi, ak njiital alkaati
yi, ak njiital takk-der yi, ak kilifag alkaati yu Ndakaaru ak bépp jëwriñ ak gépp kilifa gu taqe ci coowal sàmbaabóoy yi
doon songe;
- Jógug takk-der yi ngir yemale fi coowal sàmbaabóoy yi ak xiixaan yi ñu teg askan wi;
Sof 3: Ab jukki ci widewoob cong gi ma takk-der yi njëkk a song toj sama oto;
Sof 6: Ab jukki ci janoo ak saabalkat yi Maam Mbay Kan Ñaŋ amal 30 mars 2023;
Sof 11: Këyitu tënkub seetlub wiisiyee ci na ñu ma tëjee woon ci jalgati 30 fani mee 2023.
Sof 12: Ay widewoo yuy wane ay takk-der ak ñu leen doon jàppale te doon gàngoor ak i sàmbaabooy.
Sof 13: Pasug njëndum jumtukaayi kaaraange, daamari takk-der, jumtukaayu xarala, jumtukaay jokkoo ak
jokkale ci diggante Njëwriñu kéew mi ak kërug lijjanti gii di "Lavie Commercial Brokers”, tollu ci 43 500 000, ñu
torlu ko 30 fani desàmbar 2021, dëggal ko teg ci yëgle ko 11i sãwiye 2022.
Sof 16: Peeñi ay xale yu takk-der yi tegoon seen kanam ngir fegoo leen.
Sof 17: Këyitu tënkub wiisiye ci ni alkaati yi doon fitnaalee samay layalekat.
Sof 18: Lim bu dul jeex ci jar-jari ñu ñu jàpp ndax polotig te bokk ci sunug làngu polotig, PASTEF.
Sof 19: Dogalu 2023-1007 bu 11 mee 2023 jëm ci dakkalandi jekkig (retraite) sóobarey xare bi.
Sof 20: Nataalu mbind mi àttekat bii di Umar Maham Jàllo defoon ci xëtam ca Facebook.
Sof 21: Téere leeral bi Mbootaay giy xeex Demokaraasi (M2D) def ci xew-xewi màrs 2021.
Sof 22: Saabalub toppekat bu Koldaa ci faatug ndaw lii bokk ci PASTEF te sàmbaabóoy yi def ko.
Bësal fii
ngir jàll ci wayndarey
sof yi nekk Google
Leeral gi - Usman SONKO - Suwe 2023
Lootaabe gi:
Bàngaar Jóob
Tekki gi :
Daawuda Géy Pikin
Fàllu Silla
Seex Silla
Xadi Njaay
Sëriñ Saaxo
Saaliwu Mbuub
Laay Njaay
Asbil kan
Topp gi:
Umar Siise (Alfaruux)
Bàngaar Jóob
Ngañ demba Aaw - Alvatros
Taaral gi ci ay xët :
Ngañ demba Aaw - Alvatros
www.pastef.org - [email protected]